Sekougn Bayante

Jahman X-Press

Compositor: Não Disponível

Bëñ ak làmmiñ ña dëkk, yenn saay ñu laale
Man rekk ma xam sa njëg moo tax sekuñu bàyyante
Bul mer ba tàng wax ma looy réccu suñu juboo we
Mën nga ma gaañ te doo ko yëg bul ma wan sa doole
Tijjil sa kanam bi nga tëj man nga nop ma la sommet
Niangal jàppu la même soo meree dangay gëna rafet
Doole mbëggéel xajul si yaw bàyyil fi nga téye
Lewtoo su yàgg jële bi ñaaw mak yaw sekuñu bàyyante

Namm naa la waye fok ma tek xel
Yendoo composé son numéro te duma bës appel
Yenn saay ma dugu mode fantôme
Dem status xol la xew ci loy dox gueuth na gis no mel

Sago ngi may raay wante bëgguma ndieuka wax ak moom
May góor te fok mu xam ni fi benn baat la, may boroom
Lo wax ma tangal te pourtant man bëgg naa bàyyi mu sedd
Del makh nakh so noppè ma dof sa baat la bëgg di dègu

Jarul nga may wane ni yaa ngi ci jamm, xam naa ni yaa ngi souffrir
Mak yaw ñoy wax te xam na lépp, dama la bàyyi si biir
Dama la namm ci live bi guddi waay dugal dama ragal wéetaay
Taamal nga ma lu meunta weuy, waye xëy na di nga ma wo tay

Su may lekk lu neex ba xel mi dem ci yaw
Day mel ni mësuma xiif
Waxal ak maan nakh namm naa la, sama xol mëna gif

Oh love
Eh eh love

Maa ngi beurè ak sama xol bi
Ba guddi gi jeex waye fu ma tourné sa kanam laay yaam
Mbëggéel di gëna yokk come bis bimalay gneuka xam
Mal yak sougn xuloo nonn yi am ndam
I’m sorry, yaw namm naa la eh

Chérie non non
Stay with me oh
Because baby I love you soo
Maa ngi dora gif, léegi soo ma wowee
Yaay reine def naa la lépp

Nax mak yak sekuñu bàyyante
(Déedéet yaw lay feel)
Du man, du yaw, xol yi ñoo ko décidé
Mak yak sekuñu bàyyante
Du man, du yaw, xol yi ñoo ko décidé
Mak yak sekuñu bàyyante
Du man, du yaw, xol yi ñoo ko décidé

©2003- 2025 lyrics.com.br · Aviso Legal · Política de Privacidade · Fale Conosco desenvolvido por Studio Sol Comunicação Digital